Fàlloo di réew mi


Fàlloo di réew mi
"Bismil ilaahi"
Ma sànt "Laahi"
Ci "Fadlu Laahi"
Mim baaxé réew mi

"Hamdan"ñeel"Rahmàn"
Mi ñu may ndànaan
Fàlloo di keemaan
Jommal na réew mi

Mbër mi fiy bàkku
Fàlloo ka jekku
Deesu ko tëkku
Mo man ci réew mi

Fa daaru Salaam
La leeru Maam Daam
Feegnee né: "Salaam"
Nuyyu waa réew mi

Jàngë ba ne arr
Bay gàgaanti naar
Ya jugee gannàr
Dàn ñëw ci réew mi

Sigithior ba Ndar
Tàmbaa ba Dakàr
Ñepp la daa waar
Moo raw ci réew mi

Moo dem cig ndawam
"Masjidal haraam"
Ajali Maam Daam
Ñëwaat ci réew mi

Moo fi doon xar baax
Ba xëy ne saraax
Doon Xalif ne faax
Toog jiité réew mi

Xëy woo Senegaal
Ñuy Sàntag Magal
Yalla mi sargal
Xaadim ci réew mi

Jumaa ja Magam
Bëgëloon Baayam
Moo fexé bam am
Mu jébbël réew mi

Bu baax doon thiàbi
Fàlloo ka tebbi
Xeewël mu ubbi
Baaxéko réew mi

Bu baax doon ñibbi
Fàlloo ka dabi
jàppi ci baat bi
yeewal ko réew mi

Bassirou NDIAYE,
Paris-France
Jeudi 12 Avril 2018




Dans la même rubrique :